25/04/2025
https://www.facebook.com/share/1Bk3E4szqG/
*Barab yi ñu wara siyaar ci Tuubaa*
*Barabu Sëriñ Tuubaa ak njabootam ga mu fa nekkal,(S. Mòodu* *Mustafaa, S. Fàllu, S. Abdul Qaadr, S. Saaliw S. Mourtada Mbàkke.*
*S. Seex Gaynde Fàtma, S. Mbàkke Màdina, S. Moodu Buso Jeng, S.* *Baara Mbàkke Fàlilu ak S. Mòodu Abdul Qaadr)*
*Mooy ci Jumaa ju mag ji, foofu ngay fekk barabu Sëriñ bu mag bi. Kuy siyaare barabu kilifa nak, da* *nga koy ñaanal loo man, li ci gëna yomb mooy nga def Faatiha* *ak 11 Ixlaas. Soo ko ñaanalee ba noppi, nga ñaan* *Yàlla sa soxla ci bàrkeb kilifa googu.*
*Daaray Kaamil*
*Mooy bibliothèque Xaadimu Rasuul bi ñu deñci lu bari ci yenn téeré* *yoon wi ak téeréy woroom xam-xam yi, ak mbindum Sëriñ* *Tuubaa. Di nga fa fekk yit barabu Sëriñ Abdul Ahad* *Mbàkke ñatteelu Xalifa général des Mourides (1968-1989)*
*Aynu Rahmati*
*Di teen (puit) boo xam ne, Sëriñ Tuubaa ko gaslu woon,* *mu noppi ci ak nekkam, mu def ci ñaan yu bari, digal nit ñi ñuy bàrkeelu ci ndox mi*
*Armeel yi ci Tuubaa*
*Di barab boo xam ne, lu bari ci doomi Boroom Tuubaa fa* *lañ nekk, ku mel ni S. Baara Mbàkke, S. Abdu Boroom dër bi,* *ak ñeneen ñu bari ci doomam* *yu góor yi ak yu jigéen yi, ku mel ni Soxna May ak ay magam, ak ñu bari ci magi Murid yi, ku mel ni Seex Ibra Faal.*
*Daaru Xudóos*
*Di nga fa fekk BAYTI, di Kër Sëriñ Tuubaa gi mu dëkkóon te soo* *demee di nga fa fekk lu bari ci ay bagages yu mu moom,* *ay gaal aki téeré yu fi Sëriñ bi bàyi ngir bàrkeelu.*
*Di nga fa fekk yit jàkkay Sëriñ Tuubaa ji mu duggée* *woon xalwa ba muy waaj tukkib géej gi.*
*Barabu S. Sonhibu ibn Xaadimu Rasuul, doonoon jàngle katu Àlxuraan di ab yare kat.*
*Barab baa ngi nekk fi Sëriñ Tuubaa tuddée woon Daaru Rahmaan, ci ginaaw Daaru Xudóos*
*Di nga fa fekk yit rakki Sëriñ Tuubaa ju ñuy wax Sëriñ* *Habiibu Mbàkke, moo jànggal ñu bari ci waa kër Sëriñ bi.*
*Guy mbind*
*Barabu Sëriñ Siidi Maxtaar juróom ñaareelu Xalifa Sëriñ Tuubaa* *(julliet 2010- janvier 2018)*
*Armeeli Bàqiya*
*Di barab yoo xam ne, bokk na ci ligéey yi fi Sëriñ Abdul Ahad* *Mbàkke bàyi, ñu deñci fa kilifa yu bari ci yoon wi ak taalibé Sëriñ Tuubaa yu bari*