26/04/2026
🌿MIIRAAS
Njaayum miiraas, ñu ne: bu ko ku bokk ci Miiraas mi dee jënd da ñiy wàññi njëg li, buy jar ñaar f**k, f**k la ñu koy jaaye ki ci bokk, loolu lu ko gën a nekk ay tappale amul.
Te lima ci gën a naqari, kenn da fay am ay doom yu mag, ña des am fa yu ndaw, ka fa am yu mag ya kenn ne bëgg na, ñu xaaj njëg la féetele ko, te sax du andi xaalis ba ca saasa de ndax du ko yor, dañ naan diw mooy jox ñii nàngam rekk.
Bu ko defee ñu tàmbali di leen ko jox joxiin wu baaxul, ay dagg-daggee yoo xam ni lu ñëw seey duñ ca man a ami Kër, bu matee ñu génn ca kër ga, buñ fa wëyee di dëkk ñu leen koy xoole mbaa ñu xat fa.
Te lépp ñiy miiraas a koy def! Boroom xam-xam bu maandu warul a nangu lii.
Ku amul xaalis bu teew it kenn waru laa jaay, xaaj njëg li ngir kiy jënd ca la bokk tamit ay caaxaan la.
Te teewul njëg loola ab cërëm génnaat ca, te xaalis ba lépp du teew dañu koy xayma rekk.
Ñu bari toraxal nañ seen i doom i baay ndax lii.
Waaye ku xam dara ci àqi Miiraas di nga ko moytu.
انماياكلون في بطونهم نارا
Seriñ Jiili Alxuraan ✒️