
12/07/2025
Fàttaliku Amndi Móodu Mustafaa Mbàkke :
Seex Muhammadul Mustafaa Mbàkke, moo ngi gane jamono, bisub àltine f**k i fan ak benn ci weeru tamxarit, 1306 dëppoo ak 17 septembre, 1888 ca Daaru-salaam.
Waajuram di ku tedd ki boroom Tuubaa, waajuram wu jigéen di soxna Aaminata Lóo, bokkoon ci askan wu baax, moom la way kat ba di wax naan" Sëtub Maxtaar Ndoumbé, ma sañ cooñ Kokki, ak sët i gayndel yafa Ndaam."
Seex Mustafaa ñungi ko tudde, yoonet bi. Bi mu tolloo ci dal jàng sëriñ Tuubaa moo ko dalal, moog rakkam sëriñ Fàllu Mbàkke.
Bi sëriñ bi di dem Mbàkke baari, yobbaale woon na leen, ba bi muy dem ci géej gi, ñu tolloon ci saaru-yaasiin, mu joxañ séen baay Ceerno, maam Ceerno jël leen jox leen sëriñ Daam Abdu raxmaan Lóo, ca Daaru-xaliimul xabiir, ñu wattoo fa Alxuraan, ba wax nañu ne" Bi muy am f**k i at, ci la wattu Alxuraan ba mokkal ko, moo tax ñu doon ko wax seex Mustafaa Kamaal. Bind na it ay Kaamil yu bari ci anam gu sax te sell, ba wax nañu ne" Kaamil bi mu njëkk a bind, bi mu koy bind booba sëriñ bi mi ngi ci géej gi, ku ñuy wax sëriñ Àndulaay Nduur, moo doon siyaare ji sëriñ bi yobbaale ko, sëriñ bi sant ko ndookeel ko, daa di dikle ñu fexe mu wattu xam-xam.
Maam Ceerno moo ko jàngal xam-xam, ndax sëriñ Fàllu Mbàkke daan na wax ne" Suñu baay Ceerno moo nu yar banu ni nërr, jàngal nu ba nu ni arr."
Seex Mustafaa bokkoon na ci ñi nekkoon ak sëriñ bi Gànnaar, ca coona yu metti ya ak xiif bu metti ba.
Bi boroom Tuubaa di dem Jolof tamit yobbaale woon na leen, foofee la leen sëriñ bi xamalee ni lifi nekk, ak taalibe rekk a koy maye, waaye du doom du jarbaat, du mag du rakk, ca noona lañu jaayantee, moom sk sëriñ Fàllu ak sëriñ Moor Roqaya Buso, ak sëriñ Massamba, ñu jël séenug njureel jëndee ko ak taalibe. Seex Mustafaa foofa la nekk, di tarbiyu sëriñ Tuubaa ba yor far jañ, moo tax ñu ko daan wax Mustafaa jañ, sëriñ bi woolu na ko bis, mu ñëw mu laaj ko ana lii loo ci jublu ? Mu wax ko ne, daa lay liggéeyal rekk ba talu maa xayyu, sëriñ bi ne ko mu dem, xayyu ji (watu).
Bi sëriñ Bàmba nekkee Njaaréem ñaw nañu fa ci la leen sëriñ bi yabalee, Tuubaa moom ak sëriñ Fàllu...
Sañ ci loo leen ay kër, moom seex Mustafaa mu sañ ci Tindóodi, sëriñ Fàllu sañ ci Ndindi, ñu yore fa ay daara, di jàngale aka liggéey ba, 19 Juliette 1927 ci la sëriñ Tuubaa delloo ci leeri Boroomam fële ca Njaaréem.
Ba mu ñëwee moom seex Mustafaa, mu taxawu sëriñ bi yóbb ko Tuubaa ci biir baraag bi, mu tàllal raay bi, tabax jumaa ji ba faneetar yi génn...
Ci atum 1945 la 13 Juliette yamoo ak ñatt i fan ci aw baraxlu, ci la wuy ji Boroomam. 1927 ba 1945 moo fi nekkoon xalifa baayam, yaral ko ñenn ci njabootam gi, ba xammee wuñu, ab yaram ak yarub sëriñ bi ! Waaye taxawu jumaa ji, tàlal ab raay 45km ci jamono ju tar te metti lool.
Yal na nu yàlla fayal Amndi Móodu Mustafaa Mbàkke, bi barakati Alxuraan ul Kariim.
✍️Sëriñ Xaadim Njaay.