18/07/2022
Na ngeen ko Dimbali jàppale ko Rawatina ñiko gënë jege: ñëp xam nanu seydina Umar su duggaan ci kër Yonint soxnay yonint (Psl) ak Ñafay liggey ñëppay daw laaqu . Ndax Taraay Umar ji .
Sëriñ yiy jiité mbooloo noonu lees di àndeek ñoom , ni seex Ibra Faal Ande woonak Sëriñ Tuuba (Rta).
Loolu ak Nimbal la ci Sëriñ Bi ak yëwit !! Ndax ibliss duko may jamm fileek daanu ko.
Fii ñëppay tarqiiss waaye pexey ibliss mooy toroxal aji Saabaal katu Yallah. Na ngeen gënë laxasaayu te bañ ko wacc ngeen dimbalante seen biir.
Xadiis Bi Ibn Jawzia ci Teereem ba : Talbis Iblis dafa waxni Ku Bëg tabbi aljana naga takkook Jullit hakkane yi te mëytu di beru, Mba nga wut kula ñaareel luko moy Seytane danala jekku tè Dinala Daan.
Taalibe dafay yewwu te Dafa Rëy Pass Pass te Da wara xamni tarxiss jombul Ku Yallah bind .
Nageen ko Jappale te buleen may Ibliss fum tëgge ndëndëm !!!
Buleen tass te buleen dakkal bissu Xassida yi , na gënë birr na gënë jolli , te neeleen ko jakk diko saytu ba ALJANNAH Incha Allahu.
Na ngeen dund tay dundël charia kuci wacc charia rek na yet wi dal (ci Sutura) !! Du diggën buur ak Jaam deedet digënte ñaari xarit la ci Yoonu Yallah. Ni lanuy ande ak sa Sëriñ.
Wass Salaam
Source: Ibn Abdillah groupe (Imaan Islam Ihsaan At Tassawuf)