30/08/2024
A-t-on compris Sonko ? Il y a quelques semaines, le premier ministre Ousmane Sonko était allé à un match de football, selon la presse, "(...) sans les moyens de l’État. (...) «il est allé au match en utilisant son propre carburant, de même que son véhicule personnel»." A-t-on vraiment médité cela?
On raconte qu'un jour Umar Ibn Al-Khatâb avait une visite. Il dit à son visiteur : "est-ce personnel ou une affaire qui concerne l'État ?". Son visiteur lui répondit : "C'est plutôt une affaire personnelle ". Umar Ibn Al-Khatâb éteignit alors la bougie qui éclairait la chambre en disant : "dans ce cas-là, nous n'avons pas le droit de gaspiller les biens de l'État !".
En faisant cela, Ousmane Sonko s'adressait aux ministres, aux DG, aux maires, à l'Assemblée nationale, à tous les Sénégalais des associations sportives et culturelles (ASC), des GPF, des syndicats... à tous ceux qui utilisent les moyens d'un collectif, d'une communauté, d'un groupe, de l'État...
Il nous dit: il ne faut jamais confondre les moyens du groupe avec les moyens personnels, individuels.
Une autre gestion est nécessaire.
Une autre gestion est possible.
Le projet, c'est aussi cela
JUB, JUBAL, JUBBANTI !
GMS,
Ndax nànd nanu SONKO
? Am na ay ayu-bis, Jëwriñ Ju Njëkk ji Usmaan Sonko dafa demoon ca ab fowum futbal, bu nu sukkandikoo ci caabal gi, "(...) jëfandikoowul mbirum càmm gi. (...)" dafa dem ca po ma ak njafaanu boppam, daamaram"". Ndax xalaat nanu bu baax ci loolu ?
Ñu nettali ci benn bis Umar Ibn Al-Xataab dafa amoon ku ko seetsi. Mu laaj ko : "ndax sa yëfu bopp la walla ci càmm gi la jëm ?" Ki ko seetsi ne ko : "sama yëfi bopp la". Umar Ibn Al-Xataab fay leerukaay biy leeral néeg mu wax ne: "ci lii nii, waru noo yàq alalu càmm !".
Ba mu defee loolu, Usmaan Sonko da doon wax ak Jëwriñ yi, Doxalkat yi, Fara yi, ca Ngomblaan gi, bépp saa-senegaal bu nekk ci kuréelug tàngat yaram ak caada (ASC), "GPS", xeexalkat yi... Képp kuy jëfandikoo alalu mbooloo, aw askan, ag kippaango, càmm gi...
Daf noo wax: bu ñu mas a jaawale moomeelu kippaango gi ak li nu moom.
Weneen yoriin lu war la.
Weneen yoriin lu man a nekk la.
Sémb bi, loolu la
JUB, JUBAL, JUBBANTI !
GMS,