
05/07/2025
*Masaalikul Jinaan / Xew-xew yi amoon ci bisu Tamxarit (Haasuraa) :*
*Haasuraa di bisub Tamxarit, daa bari lool jagle yu ci Yàlla def, muy xew-xew yoo xam ne, ci bis boobu la amoon.*
*S. Aaadama hs, moom ak soxnaam Awa ba ñu dëkkee àjjana, Yàlla da leen a mayoon ñu jëfandikoo la fa nekk lépp ba mu des genn garab, mu ne leen buñu ko laal, saytaane man leen ba ñu laal ko, muy ag tooñ gu rëy gu ñu def, Yàlla nag ci bisub Tamxarit boobu la leen jéggal tooñ googu. Dikk na ci saaru Al-Baxara aaya 34 -37.*
*Gaal gi Yàlla digaloon S. Nuuh hs mu defar ko, ba mu noppee mu digal ñi ko gëm ñépp ñu dugg ci, Yàlla génne ndox mu bari ci suuf si, wàcce ndox mu bari ci asamaan si, ña duggul ca gaal ga doon ay yéefar yépp dañoo lab, S. Nuuh hs Yàlla musal ko moom ak ña nekkoon ca gaal ga, gaal googu mi ngi teer ci bisub Tamxarit ci doj (Montagne) wu tudd juudiyyi, am na ñuy wax ne foofu jamono jii boori Tirk la. Dikk na ci saaru Huut aaya 37 - 44.*
*S. Muusaa hs, Firhawna da koo bëggon a ray moom ak ñi mu àndal, bi mu koy dàq ba ci géej gi, xamul fu muy aw, Yàlla digal ko mu dóor yatu kéemtaan wi mu yoroon ci géej gi, bi mu ko defee, géej gi xar def ay yoon, mu jaar ca moom ak ñi mu àndaloon, Firhawna ba mu yegsee moom ak ñi mu àndal, géej ga melaat na mu meloon, ñu daal di lab, loolu nag ci bisub Tamxarit boobu la xewoon. Dikk na ci saaru As-Suharaa aaya 52 - 67.*
*S. Hiisaa hs, ci bis boobu la gane àdduna, mu doon nag bis bu yéeme ndax ni mu feeñe muy kenn ku ñëw ci kaw suuf te amul baay, muy kéemaanug Yàlla gu rëy lool. Dikk na ci saaru Maryama aaya 15 - 33.*
*S. Yuunus hs, moom Yàlla da koo yónni, mu woote lu yàgg ñu di ko weddi, mu mer daal di gàddaay, bi mu duggee ci gaal nag ngir dem, gaal ga am jafe-jafe nar a suux, ñu ne fàww ñu wàcce kenn ngir gaal gi bañ a suux, ñu daal di def xeetu loterie, Yàlla dogal mu dal ci kawam, ñu sànni ko ci géej gi, Yàlla digal aw jën mu wann ko te bañ koo reesal, am na ayu-bis ca biirub jën wa, ci bisub Tamxarit nag la ko yàbbi, ci la ko Y