12/05/2026
KII MOOY BAYE MA-FALL FALL
✅Kénna ngi di Dóomi Daroul Mouhty, di taalibé Sëriñ Modou Awa Balla bouko geum té yamalé wou kok kénn. Firndé li moy dafay faral di wax ni « Bu Seriñ bou mag bi déllousi woon, Borom Darou délloussi, Seriñ Modou Awa Balla déloussi, man Ma-FALL si Ndayane Awa Balla lay dém tok ndax mom la xam ». Baye Ma-FALL di ndiéxital lou Borom Darou bou wérr ndax djiko yi mou laambol: Nit kou dëuggou la, ku amuk F**t la kou yaatou la yit té social: sax ci déf lou bakh ci biir Sénégal rawatina fi ci Daroul Mouhty gui ak Louga, am alal yombouna wayé am xoloup joxé ko mo diafé.
LOUGA
✅Baye Ma-Fall, Louga gui mou fék baax, taxawal na fa kourél touddéko SOS-NDIAMBOUR, ngir dimbali néw dolé yi si waloum doundou ak santé:
Social: dieundal naléen autop Corbillard, koufa am déçés niou joxla auto bi té moo ciy déf gazoile, batay ci Louga gui koor gou diott dina sédalé 1.000 kit yoo xamné kénn kounékk dinan la jox sac riz ak sucre 5L huile. Lolou bokkoul ak dara si taxawu bimouy taxawu wa quartier bamu deuk di Artillerie si wérou koor gui si ak dound ( Tieb ak sucre), ci xalisou boppam.
SANTÉ
✅Baye Ma-Fall, kourél gui mou taxawal lidianti na ba am 30 machines dialis ciy partenaire mingi dakar, ba ministre bi jox nako centre boum wara monté 20 machines yi Dakar, yénéen 10 machines yi Louga lako wara monté. Baye Ma-Fall dina taxawal ay journées de consultations gratuites indifa ay docteurs si wallei wou nékk niou saytou malades yi fadj léen téksi may léen ay garab.
DAKAR
✅Baye Ma-FALL mii, moy Représentant Xalif général Daroul Mouhty fi si Ndakarou, Xalifa Borom Darou yépp mankoo beugg ko, woolou ko, mou diakhaso lool ak gnom liko dalé si Baye Cheikh Khady, Serigne ABASS, Serign Bass ANTA Niang ba ci Serigne Xalid Mbacke mi fi toog toggayu Borom Darou. Baye Ma-Fall, amna Keur gou mou tabax Dakar, joxé wone ko gratuitement niou déf fa Daaray Al-khourane. Baye Ma-Fall di diambaar lol mana diokhé gnam, Keuram Aldiouma gu diott mou dadialé fa mbokk yi aki xaritam ak am di diamam yi diléen fa bérndéel.
DAROUL MOUHTY
✅Baye Ma-Fall, Talibé Serign Modou Awa Balla la wayé ku jaxasso la ak ndiabotou Borom Darou bi yépp amoul fén sens interdit. Baye Ma-Fall, kou ragnéeku ci gammuk Daroul Mouhty la, sou nieuwé mou dieul alal déf ko ci bis bi ngir Mame Thierno Birahime ak nim fonké woon gammu. Chaque Magal Darou keur kilifa yi ci deuk bi niépp lay yonné thiéeb ak addiya, Nimouy taxawo bisoup Borom Darou bi, nonu lay déf si yénéen Magal ak xéw xéwu dinée yiy am si deuk bi yépp.
BEUYTI DAROUL MOUHTY
✅Baye Ma-Fall fi ci beuyti gui, lou eupp foukki att ngi ni mboolém mag gni nékk Daaray Kamil wéer wou diott dinala diokh sakoup thiéeb, nonou lako amélé Soxna yifi Serigne Modou Awa Balla bayi ak dieuwrigne gui saytou Barabou Serign bi ci Beuyti. Baye Ma-Fall ci beuyti gui att mou diott dina yobbou ci mag gni kénn Makka, 3 démagoun nan ak rén ji mouy 4 eme bi,
THIEUYÉN DJOLOF
✅Baye Ma-Fall, di dieuwrigne ci keur Serigne Sëriñ Fallou Asta Diéye doon andak mom and bou rafétt ba mou wouyji boromam, mou wéyal di taxawou ndiaboot gui. Baye Ma-Fall, tabakh na Keur spécial thieyén djolof ngir magalouk Sokhna Faty Issa Diop gui, ngir kou magal si nga dal keuram té amoul sens interdit wala xadiaak séen, té mooy berndéel képp koufa nieuw, té sooy gnibi mou jox la addiya.
MAKKA
✅Baye Ma-Fall, ci diganté DAKAR -Louga- Daroul Mouhty ak yénéni deuk att mou diott daan na yobou Makka minimum 20 personnes diko selectioné ciy mbokam aki domi réwmi, ci 3 ans yi la wagni lim bimou daan yobou, néena ci 3 ans yi mouko wagni éconimisé na ci lou tollook 100millions yo xamni aprés tabaski 2026 bi lako begeu dimbalé néew doolé yi si waloum deukouwaay ( Keur) ci Louga ak liko weur.
FAMILLE KEUR GORA FALL
✅Baye Ma-Fall, kou fonk ay Mbokam la, ku dimbali ay mbokam, li ma fi lim yép ay mbonkam gno ci djitou, ay mbokam dagno dadialo wakh ni li askano si Gora Khary Malick yépp ak Makhtar Khary Malick bougn ko manoon kounék dina wagni si ay fanam ngir niou yokal ko Baye Ma-Fall ndax sounou borom Bayi kofi lou Yaag ndax taxawayam si niom » Famille bi niépp massé amél ko santa ak ngeureum.
Baye Ma-Fall Keuram gui mou tabakh Daroul Mouhty, néena keurouk ay mbokam lako déf, keurouk waydiouram Elhadji Baye Gora Fall, néena sou fi diogué wonit bounko miraas nan ko déf keurouk famille, fi lay maggalé Daroul Mouhty aki mbokam té mooy déf lépp.
Baye Womar Diop