23/07/2025
J’ai eu l’honneur d’accueillir, ce mercredi 23 juillet, à l’Assemblée nationale, Son Excellence Trần Thanh Mẫn, Président de l’Assemblée nationale de la République socialiste du Vietnam, en visite officielle de trois jours dans notre pays.
Nos échanges, d’abord en format restreint puis élargi, ont été particulièrement fructueux. Ils ont porté sur plusieurs sujets d’intérêt commun et ont mis en lumière notre volonté partagée de renforcer la coopération entre nos deux institutions.
Nous avons notamment souligné l’importance de la diplomatie parlementaire comme levier stratégique pour approfondir les relations entre le Sénégal et le Vietnam.
À cette occasion, les groupes d’amitié parlementaire Sénégal–Vietnam ont été présentés, témoignant de notre engagement mutuel à favoriser une coopération de proximité, fondée sur la confiance et le respect.
Dans cette dynamique, nous avons procédé à la signature d’un accord de coopération parlementaire, marquant une étape majeure vers un partenariat structuré et durable entre nos deux parlements.
Dans l’après-midi, nous ouvrirons conjointement les travaux de la table ronde sur la coopération commerciale et économique entre le Sénégal et le Vietnam, organisée par l’APIX.
Cette rencontre, qui réunit des représentants institutionnels et économiques des deux pays, vise à dynamiser nos échanges, encourager les investissements croisés et explorer de nouvelles perspectives de collaboration.
Plusieurs accords seront signés en début de soirée, notamment dans le secteur agricole, commercial, industriel et diplomatique.
———-
Wolof ↓
Am naa mbégtem dalal, àllarba 23i fani sulet, fii ci Ngomblaan gi (AN), Njiit lu Màgg li Sëriñ Trân Thanh Mân, Njiital Ngomblaan gu Réewu Njàppale mu Vietnam, ci nemmikug ñatti fan ci sunum réew.
Sunuy waxtaan, am na ci amiin wu tëju te fés, mu am njariñ yu bari te am solo. Waxtaan yi jëmoon na ci tomb yu bari te am njariñ yu nu bokk ak leeral sunug dogu gu nu bokk jëm ci dëgëral lëkkaloog sunu ñaari campeef yi (institutions).
Fésal nanu itam solos dipolomasi "parlementaire" niki yoon wu am solo ngir gën a dëgëral diggante Senegaal ak Vietnam.
Jaare ci ndaje mii, aajar nanu (présenter) gurubu xaritoo bu parlementaire Senegaal — Vietnam, di firndeel sunug dogu gu nu bokk ci fésal ag lëkkaloo gu jige, tegu ci kóolute ak wegante.
Ci doxaliin woowu, am nanu ab SIÑE jëm ci déggoog lëkkaloo gu "parlementaire" tegu ci ab jéego bu mag bu jëm ci lëngoo gu dëgër te yàgg ci diggante "parlements" yi.
Ginnaaw MIDI, dinanu boole kubbiteg liggéeyi taabal ci lëkkaloog jënd ak jaay ak koom ci diggante ak Vietnam, "APIX" ci di ko amal.
Ndaje mii, dina dajale ay ndawi "institutionnels" ak koom yu ñaari réew yi, ci ay doxiinu waxtaan, ñaax ay iwestiismaa yu nu bokk ak xalaat ci yoon yu yees yuy gën a dëgëral lëkkaloo gii.
Ay déggoo (accords) yu bari dinanu ko SIÑE ci ngoog, rawati na ci wàllu mbay, jënd ak jaay, liggéeyukaay ak dipolomasi.