06/06/2023
YAGG BAWUL DARA (le temps n’épargne rien)
Le talif (poème) du Pr Assane Sylla qui a inspiré le titre Nela Thias de Cheikh Lo. Version originale en wolof, suivie d’une traduction française d’Abdou Khadre Gaye.
Yàgg Bawul Dara
Boo toogee di xelaat lu ñëwagul di mébët,
Mba nga ne sa tool di ji walla di jëmbët.
Yaakaar daldi la feese ngay séénu di yóotu xééwal,
Ca sab liggééy daldi naagu, doon ku nééwal
Ndax dal nga fàtte ne dogal gu dul jaas,
Man na agsi, xef-ak-xippi ne la cas,
Daw ak yaw ba ca sëg ya jëmbët la fa,
Sag démb ànd ak sa tey daldi sooti foofa.
Boo gestoo di wut ndërëklay di seet fo jafandu,
Daldi gis ne démb wess na, dootunu ko dabu
Te ëllëg ñëwagul ag kump la
Addina daal toogul, dex guy baawaan la,
Te nu ngi ànd ak moom cig wéy gu dul dakk.
Lu nuy séénu du ko soow dina wessu banu faak,
Lu coow bari, bari, selaw ne ko dëndiix woon.
Ngalla waay bu la coono tegu ba tax nga jàq,
Muñal déy wéy, amul dara lu fi sax.
Doole fasu naaru-góor, taaru jongoma,
Jëmmu kilifa gu mag lépp dey ruus
Li fiy sax daal, mooy jëf ju rafet, sell ni urus,
Boo dëddoo muy jolli ci sa ginnaaw ne wesar
Te foo jëm mu jiitu la fa di la xaar.
***
Le temps n’épargne rien
Lorsque, confortablement assis, tu penses à l’avenir et t’y projette,
Ou lorsque, en ton champ, tu sèmes des graines ou plantes des arbustes,
Et que d’un cœur plein d’espoir, tu scrutes l’avenir, convoitant les fruits
De ton labeur, content de toi-même, confiant et négligeant
Parce que tu oublies que les coups du destin ne ratant jamais leurs cibles
Peuvent t’atteindre et t’emporter le temps d’un battement de paupières
Et courir avec toi jusqu’au cimetière et t’y planter
Ton passé et ton présent s’y confondent alors
Et si tu te retournes cherchant un appui ou cherchant où t’agripper
Tu verras que le passé s’est envolé, irrattrapable à jamais
Et que la suite n’est pas encore arrivée, il reste caché
Ce monde-ci, en vérité, n’est pas stable, il est semblable à un fleuve qui coule
Et, en sa compagnie, on avance sur un chemin sans fin
Tout ce qui est attendu avec impatience passera puis sera oublié
Aussi bruyantes que soient les joutes oratoires, le silence les enveloppera
Que donc les fatigues de ta vie ne te posent problème outre mesure
Fais preuve de patience, ça passera, car rien ici-bas ne s’enracine
La force du pur-sang, la beauté de la grande dame
Les attributs du grand dignitaire, tout s’effrite
Ce qui échappe à l’usure, c’est la bonne action, pure comme l’or
Lorsque tu tourneras le dos, il rayonnera, étincelant
Et où que tu ailles, il y sera avec toi