05/11/2025
Mboolem sahaabatu rasuul
Ak mbër ya daa tagg rasuul
Mel na ni bay nga séen i tool
Bayaale tool i xarnu bi
Kahab da daa tagg rasuul
Busayri daa tagg rasuul
Hassaanu daa tagg rasuul
Semmal nga léen ci xarnu bi
(Séex Muusaa Ka)