09/03/2025
Serigne Abdou Lahad Bara Mbacke
Mingi feegne jamono çi attum 1921, çi tùuba. Domi cheikh mouhammadu lamine bara, ak sokhna khoudia coumba lô. Ñu tudé ko cheikh abdul ahad mbacké ibn cheikhoul khadim.
Bimu matté dall jàng, cheikh mouhammadu lamine bara diox ko serigne modou diarra guéye mô ko dalal alxur_ane. mu nek çi ay loxom, ba ni fi Serigne bara bàyyi ko çi attum 1936.
Guinaw bi la ko cheikh moustapha ibn cheikhoul khadim jeul yobbu ko daaru nahim mu wéyël fa am ñañgàm, guinaw bi mu mokkalé alxur_ane. Çi la soobu çi ñañgum xam xam ba guédjou çi.
Çi lako fa cheikh moustapha jëlé ko daaru nahim indi ko çi magam ju baax ji çi dëk bi ñuy wax taysir. Mu nek çi loxoy serigne modou bara mi nga xam ni mo fi nékalone cheikh mouhammadu lamine bara.
Mu nek ku dégo ak magam, topu ko topine wu raffet def ko ap sëriñ, bagne koo def mak.
Guinaw bi fi serigne modou bara bàyyi ko çi attum 1952 mu wéyël topp gui çi magam ju baax ji serigne abdul aziz bara, Taxawu taxawaayu taalibé.
Guinaw itam nekone na dëk bu ñuy wax mbarà kane di jàng aka jañgàlé di fa yar aka tarbiya itam. Amone na itam kër dëk bii di ñogomaay. Ñogomaay nak serigne bara moko fa digëlone nguir mu nek fa. Amone na it kër dëk bu ñuy wax mbacké ñokku.
Guinaw bi ite nek çi dëk buñuy wax, wajaldé. Wajaldé mingui nék, région de louga Çi attum 1976 çi la ko sañçi, tudé ko wajaldé. Def fa daara di fa jàng aka jànģalé, di yaré aka tarbiya,
Fuñuy wax pétéñe ite amone nafa daara. Dëk buñuy wax siiw kà amone nafa daara. Ñogomaay ite amone nada daara. Ku jaxaso woone ak ay wadiuram yi la woone. Donone ku fonku ay magam tei wormàl ay rakam lool. Bari na itam ñum çi tudé dome. Çi ay waydiuram ak çi ñabootuk cheikhoul khadim
Mu donone ku jaxaso ak Serigne cheikh mbacké gaindé fatma, Mu daa ande ak Serigne cheikh mbacké gaindé fatma çi tukki yu barri çi Afrique.
Mu donone ku yémé tei kimaané,
Ndax amone na ak relation ak ndiouga kébé la. Am na biss ndiouga ñieuw tùuba ziaar si ko, fék ko gouye mbinde, diox ko 2 millions, di ko wax nguir mu gene koo dolli ñaane. Guinaw bi mou démé Serigne abdul ahad bara dafa jeul lako ndiouga dioxone sédalé ko ñiafa nékone. ba am kéne çi ak ñiabotam laadj ko loutax mu sédalé ko? Serigne bi xamal ko niko xalissu ku wara faatu ( mort) duma ko lék. Bi ndiouga jougé çi moom di dém kaolack çi yoone wi la def accident dal di faatu.
Ku diaxaso woone ak djily mbaye la itam. Ku jaxaso woone ak Serigne muhammadu saxiir lô bu kokki la woone. Ak yénene....
Mou donone ku daa dimblé çi wallu ñaane ak çi wallu alalam itam.
Mingui guéne aduna alxamess ñiatti fane çi weeru koor çi attum 1410 çi gadaay gui. Di jeudi 29 mars 1990. Çi tùuba gouye mbinde. Ñu diébël ko boromam armél yi çi jumaaji çi wettu waaydiuram wa di cheikh mouhammadu lamine bara mbacké
çi teewaayu Serigne abdul khadre mbacké ibn cheikhoul khadim.
Serigne abdul aziz lahad bara moko woutu çi çi attum 1990 ba 2014.
Yall nanu ko yalla fayal tei tass ñu çi barkeim.
Ñiarelou khalifam Serigne Abdou khadim Mbacke mongui wathi liguéye 2020
khalifa serigne abdul ahad bara mingui toudu Serigne modou bara mbacké di ñiane mu yage fi lool tei wér ak ñabot gui yépp.
Léral yi chohaibou Mbacke aziz lahad Bara